Kaajarug Palaŋu Jubbanti Koom : Senegaal sóobu na ci doxaliinu koom mu bees ci kilifteefu Peresidaa FAY.

xamle - 01 MONTHS.AUGUST 2025

Ci kilifteefu Basiiru Jomaay FAY, Njiitu Réewum Senegaal, Usmaan SONKO Njiitu Jëwriñ yi, aajar na ci àjjuma ji 1 panu ut 2025, Palaŋ bi jëm ci joyyanti koom mi ak dundiin wi ci Senegaal « Jubbanti Koom ».


Naal wu am solo wii li ko tax a jóg mooy jubbanti ñàkk a yemoo gi am ci koom mi boole ko ak sóobu ci yoon wu bees ngir yokkute gu sax dàkk. Muy tegtalukaay bu am solo ngir dindi mbooleem yiy gàllankoor doxiinu koom mi, jaare ko ci am doxaliin wu leer ci njël li, yaxanal alal jiy dem ci wànqaasi nguur gi ak fexee am yeneen balluwaayi koppar yuy bawoo ci réew mi.


Ci palaŋ bii, Senegaal fas na yéene dajale lu ëpp 5.000iy milyaari FCFA ci diiru ñenti at, te du jëfandikoo bor buy bawoo biti réew. Jubluwaay bii, lalu ci pas-pasu manal sa bopp, day firndeel pexey teqalikoo ak na ñu daan saytoo alal ji teg ci di tekki yéene ju wér ju jëm ci gën a dooleel Nguur gi mu manal boppam ci wàllu koppar.


 

Ginnaaw bi Njiitu Jëwriñ yi aajeree ci anam yu mucc ayib palaŋ bi ba noppi, , Njiitu Réew mi rafetlu na jaayanteg Ngóornamaŋ bi, jaare ko ci ndokkale Sëñ SONKO ak mbooleem ñi bokk ci Nguur gi. Ay kàddoom doon lu fésal solos palaŋ bii doon tontu lu wér ci wàllu ay lim yu lootaabewu ngir saafara jafe-jafey koom mi ci réew mi.  


Peresidaa FAY, fàttali na càmbar gi Nguur gi santaane ci anam yi ñu yoree woon alalu askan wi ba tax ñu xam tolluwaayu koom bu doy waar bi ñu donn. Feddali na yéeney Ngóornamaŋ bi jëm ci teqalikoo ak doxaliin ya woon, jaare ko ci wax askan wi liy dëgg ci ñu fas yéenee doxal li ñu leen dénk. 


« Li ngeen tànn mooy riptiir, nun it nu tànn dëgg ngir jubbanti rëq-rëq yi », di li Njiitu Réew mi xamle, dolli ci ne palaŋ bii ab tontu la ñeel partaneeri àddina si : « Nan ngeen fas yéenee jubbantee réew mi ? Xereñte gi am ci palaŋ bii nag, lépp a ngi ci lim yu wér yi nekk ci li ñu nar a def. »

Njiitu Réew mi xamle na dogal yi ñu jëkk a jël, rawati na ci wàllu yoriin wu leer ci njël li ak ci wàllu yaxanal. Xamle na ne dees na dooraat liggéeyu bànqaas biy saytu wàllu boru réew mi, muy bànqaas bu am solo bu ñuy dénk wàllu fegu ci yenn risk yi boole ko ak di taxaw ci caytu gu wér te wóor ci bor bi. 



« Joyyantiwaat gi mu ngi doore itam ci “Comité national de la dette” bi nu delloosiwaat. », di li mu leeral.


Ci geneen wàll, Njiitu Réew mi xamle na na am na ñenti sàrt yu am solo yu ñu jébbal Ngombalaan gi mu war cee sëgg ci ayu bis bii. Muy sàrt yu jëm ci gën a dooleel xeex nger mi ak dooleel yoriin wu leer.


« Lu bari laa laajoon, waaye nag li nekk ci sàrt yii doy nañu ma. Dañuy gën a dooleel matukaayi doxaliin wu leer », di li mu wax, teg ci soññ askan wi ñu def ko seen yëfi bopp.


Mu feddali yéeneem ci delloosi yoriin wu lalu ci teqalikoo la la woon, doxaliin wu leer te xereñ, Njiitu Réew mi rafetlu na coppite yi ñu jot a sumb, rawati na wéyalug càmbar ni ñu yore woon alal ji.