Jollasante : Peresidaa Fay ak naataangoom bu Rusi di Vladimir Putin feddali nañu seen yéene jëm ci gën a dooleel jëflantey xaritoo ak lëkkaloo diggante Rusi ak Senegaal.

Biti Réew - 22 MONTHS.NOVEMBER 2024

Njiitu Réew mi, Kilifa gi Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, ci jollasante, séq na waxtaan wu gànjaru te bari njariñ, tay diggam ak naataangoom bu Rusi bii di Vladimir Putin. Ñaari kilifa yi feddali nañu seen yéene jëm ci gën a dooleel jëflantey xaritoo yi dox diggante Rusi ak Senegaal,


Waxtaan nañu itam ci tolluwaayu kaaraange gi am ci tunduw Sahel wi ak Afrig Sowu Jant, te tukkee ci kippaangooy rëtalkat yi koy yoot. Am nañu ag déggoo ci àndandoo seen i yëngu ngir jàmm ak dal ci tund woowu. 

Peresidaa Vladimir Putin posewu na ci waxtaan wi woo Njiitu Réew Mi Basiiru Jomaay Fay ngir mu ñëw ganesi ko ca Rusi ba moom Kilifa gi nangul na ko ko bu wér.