xamle - 10 MONTHS.OCTOBER 2024
Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay dalal na démb ci ngoon gi ndawi Woodside, ci njiital Risaard Goyder miy Njiitu Ndiisoog Ndoxal gi. Moom Goyder posewu na ci ndaje mi ngir xamle ne yegg nañu ci jubluwaayu am 100.000i barigo bis bu set. Xamle na itam ne 5i milyaar yi ñu dugal ci sémb wi tax na Woodside taxawal lu tollu ci 4400i xëy.