xamle - 11 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Njiitu Réew mi demoon na ca ca Mbuur ngir wane mettiitam ak ug njàppaleem jëme ci njaboot yi ñàkk seen i doom ci gaal gi suux ca Mbuur, niki noonu ci mbooleem askanu Senegaal. Wakkan yii di rot ci mbëkk mi day fàttali ne jot na sëkk ñu jóg ci.
Njiitu Réew mi feddali na dogug Nguur gi ci rëbb ñiy lootaabe mbëkk mii ba fu ñu man a nekk teg leen daan yi war ci ñoom.
Njiitu Réew mi di woo ndaw ñi di leen xamal ne: « seen dung gii lu gànjaru la. Dangeen a am waar wu yaatu wu ngeen war a bay ci réew mi. Noppi nanu ngir jox leen xëy yu wóor fii ci réew mi ba nga xam ne géej gi dootul doon ay sëg ngir sunuy doom. »