Njiitu Réew mi demoon na ci suba ngir gisal boppam warab yi Farãas delloo, muy màndargaal jéego bu am solo ci tëggaat lëkkaloo gi ci wàllu sóobare diggante ñaari réew yi.
Mu àndoon ak ay jëwriñ ak Kilifa yu mag yu Sóobare yi, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY dem na cig toftaloo ca dal yu Wakaam, Belleer ak Marin ba, di warab yu nekk leegi ci kilifteefu Senegaal. Nemmiku gii tax na mu gisal boppan tolluwaayu taax dal yooyu (dëkkuwaay, jumtukaay, yëngu...) ak natt seen man-man ngir jëfandikoo leen ci fan yii…
Delloog dal yooyu, tukkee ci waxtaan yu ànd wegante yu ñaari réew yi séq, day tijji buntu lëkkaloo gu bees, gu tënku ci tàggat, àndandoo ay yëngu ak gën a dëgëral man-man yi ci réew mi.
Senegaal di feddali kon, ci xel mu dal ak fulla, cangam (souveraineté) gu wér te wóor ci dali sóobare yu am solo.