Njiitu Réew mi jot na, tay ci ngoon gi ci Njéndel Réew mi, ci jataay bu am solo, tënk bi bawoo ci liggéey yi doon amal ci Diisoo yi ñu jagleloon waxtaane sistemu politig bi.
Cig àddoom, Njiitu Réew mi rafetlu na bu baax jéego yu wér yi am ci liggéey yi, jaare ko ci taxawlu bu baax ci déggoo yi ñu jot a am ci yenn tomb yi, muy : wàññi ak yeesal làngi politig yi; jëfandikoo xarala yi ci doxaliinu joŋantey pal; bindu gu sax te otomatig ñeel ñiy door a wote; taxawal benn Ëttu Ndayi sàrt yi; jëfandikoo biltee inig ak jëfandikoo xarala yi ngir wote; niki noonu taxawal kurél gu moom boppam gu yor wàllu joŋantey pal yi.
Njiitu Réew mi xamle na ne digle yii dees na taxaw ci jëmmal leen ca na mu gën a gaawe, moo xam muy ci wàllu ndayi sàrt yi la walla muy lu war a jaar ca Ngomblaan ga. Ci loolu, dees na taxawal benn komite ad hoc ci ayu bis bii, ngir mu topp bu wér jëmmalug dogal yi ñu jël.
Mu jaare ci taxawlu bu baax ci dayob coppite yii, Njiitu Réew mi feddali na solo si ñu am jëm ci gën a dëgëral jàmm ji, gën a xemmemloo meññilukat yi ci Senegaal, ak gën a dëgëral jëflante gi ci diggante campeef yi.
Diisoo gii doon lu ñu yoonal, doon na leegi keno bu am solo ci àndandoo waxtaane yoriinu réew mi, gën a dëgëral demokaraasi bi ak tabaxug ma-réew yi. Day wane yéeney Senegaal gu doon benn, dal, te jekk ngir ëllëg.