Jataayu waxtaane yaaley pénc mi: Njiitu Réew mi di woote ag yeesal gu matale ci wàll wi

xamle - 21 MONTHS.OCTOBER 2024

Njiitu Réew mi tijji na tay ca CICAD jataayu waxtaane Yaaley pénc mi, di jéego bu am solo jëm ci xoolaat doxaliinu dem bi ak dikk gi ci Senegaal. Jot na sëkk nag nu jëf te ànd ak dogu ci kanamu jafe-jafey yi aju ci ñàkk kaaraange gi am ci yoon yi, xataay yi ak ñàkk ay jumtukaay yu mat.

Cig àddoom, Njiitu Réew mi xamle na ne ñàkk kaaraange gi ci yoon yi yamul rekk ci ndogal, waaye matadig doomu aadama yi a ci ëpp, ba tax na ku ne war xoolaat sa taxawaay. Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay taxaw na bu baax ci xamle ne fàww ñu amal diisoo yu ñépp di bokk ngir man a yeesal sunu jumtukaay yi teg ci tabax sistemu dem ak dikk bu ànd ak kaaraange, wér, wóor te ànd ak xarala yu bees yi.

Diisoo yii ñu ngi jëm ci rëdd aw yoon wu leer ngir taxaw ci jafe-jafe yi boole ko ak gën a dooleel koomum réew mi jaare ko ci teg pexe yu sax, niki suqali yooni saxaar yi ak xàll yu mag yi ci Afrig Sowu Jant.