jëwriñ - 07 MONTHS.NOVEMBER 2024
Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay dina jiite jataayu tijjitel 15eelu xewu « Biennale art africain contemporain » bu Ndakaaru, 7i fani nowàmbar ca Garaa Teyaatar Nasonaal.
Xew wii di am ba 7i desàmbar, ñu war cee waxtaane « The Wake » walla Yewwu gi, Xàll wi, dina fésal xereñte gi nekk ci fenkati saa-afrig yi. Biennale bii nag jumtukaay bu am solo la ñeel ñiy safoo fent ci àddina wërngal kàpp.