xool - 24 MONTHS.APRIL 2025
Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay, jiite na ci alxemes ji 24i fani awril 2025, ca CICAD, jataayu tijjitel 4eelu Ndajem waxtaane xëy ak man-manu.
Ndajem ren mii ñu doon waxtaane pexe ak naal yi ñu war a teg ci wàllu xëy ak man-man ngir Senegaal gu moom boppam, tegu ci yoon te naat, dajale woon na kilifay nguur gi niki noonu ñi teewal liggéeykat yi, njaatige yi ak partaneer yi ci wàllu xarala ak kopparal.
Cig àddoom, Njiitu Réew mi feddali na ne xëy mi, rawati na mi ñeel ndaw ñi, lu jamp la ci réew mi. Xamle na ne fàww ñépp ànd ngir indi ci tontu lu wér te wóor, lu war a tege ci tàggatu gu xereñ, dooleel man-man yi ak gunge ñiy jéem a taxawal dara ngir saafara ba fàww jafe-jafe bii.
Njiitu Réew mi woo na mbooleem ñiy yëngu ci wàll wi ñu gën a jaayante, rawati na partaneer yi, sektéer piriwe bi ak gox yi ak goxaan yi, lépp ngir tabax xeetu koom mu boole ñépp te sax. Muy xeet gog, leeral na ne dafa war a tegu ngir ngor, yoon ngir liggéeykat yi ak dal ngir Senegaal.
Mu tëjee moom Njiitu Réew mi ci feddali jaayanteg Càmm gi jëm ci bay waaram bu baax ci sumb bii, boole ko ak yéene ju wér ci amal ay coppite, taxaw temm ci yoriin wu wóor te am ay njeexital yu leer ngir askan wi.