Ci posem 65eelu at mi Senegaal moomee boppam, Njiitu Réew mi Bassirou Diomaye Faye amal na ab jataay, àjjuma ci guddi gi, ci Njénde li, jagleel ko taskati xibaari réew mi. Mu doon jàll bi 21i waxtu jotee, jataayub leeral bii, doon lu ñépp doon xaar, may na Njiitu Réew mi mu dellusiwaat ci weer yi mu jot a am ci boppu réew mi, àddu ci naal yiy ñëw boolee ko ak feddali gis-gisam ci Senegaal gu moom boppan, gu yoon di dox te ànd ak naataange.
Ci ndoortel jataay bi rekk, Njiitu Réew mi xamle na ag jaayanteem ci amal yoriin wu leer niki mu ko digee woon ca jamonoy kàmpaañ ba. Lu ñeel ràppoor bi ñu fésal jëm ci anam yi ñu yoree woon alalu askan wi diggante 2019-2024, xamle na ne : « « Man faluñu ma ngir may wax Senegale yi lu woroo ak dëgg. Ràppoor bii ak lu mu metti metti, day lu manul a ñàkk ngir delloosi doxaliin wu jub.» Muy fésal lu bari lu ñu war a mottaliwaat ci njël li ak bor bu yegg daanaka ci 100% ci PIB bi, ràppoor bii doon na lu ñépp rafetlu jàpp ne ag njàmbaar dëgg lay wane ci wàllu politig. Mu wéyal ba leegi di xamle ne : « Li nu def xam nanu ko bu wér te nangu ko nag. Sas wi diis na, waaye xam nanu fi nu bawoo ak fa nu bëgg a yegg ». Ci kanamu jafe-jafe yii nag, mu ngi ñaan ñu feddali kóolute gi diggante nguur gi ak askan wi, muy màndargaal yaakaar ju ñu fas yéene a delloosiwaat.
Ci wàllu koom mi, Njiitu Réew mi feddali na yéeneem ci teqalikoo ak doxaliin wi ñu yàgg a aj ci yaakaar biti réew. Leeral na sémbu « Senegaal 2050 » wi dikk ngir soppi bu wér koom mi jaare ko ci amal jëfandiku gu mucc ayib ci balli mbindare yi, gën a dooleel mbay mi ak taxawal ay xëy ngir ndaw ñi. « Danoo yàgg a jaayi sunu màcceer përëmyeer yi biti réew te dunu leen soppi ba noppi. Loolu nag daa war a dakk » di lu mu taxaw bu baax, jaare ci xamle ay dogal yu wér yu ñu jël ngir baral jéego yi jëm ci moom sunu bopp ci wàllu dund bi ak yasara gi. Bokk na ci yooyu, jëfandiku gu jaar yoon ci sunu petrol bi ak gaas bi am taxawaay bu am solo, boole ko ak yokk bu baax li ci réew mi di am. Lu ñeel xëyu ndaw ñi, Njiitu Réew mi fàttali na ne dina jiite ci fan yii di ñëw, am ndaje mu ñuy jagleel man-man ak xëyu ndaw ñi. « Moo xam ndaw ñi la walla muy jigéen ñi, dinanu taxawal ay sémb yu am solo ngir saafara jafe-jafey xëy mi », di li mu ci yëy-yàbbi moom Njiitu Réew mi.
Ci laaj bii jëm ci wàllu politig, Njiitu Réew mi dalal na xeli askan wi ne li mu fas yéene mooy doxal demokaraasi bu dul faagaagal kenn. « Bu dee man rekk duñu fi gal-gal benn opposant ndax bañ mu bokk», di li mu dogu. Mu doon kon kàddu yu man a indi dal ci géewu politig bi, ci jamono ju ñu nekk di waxtaan ngir xoolaat taxawaayu làngi pokitig yi ak dellusiwaat kóolute ci campeef yi. Bataaxel bii nag kujje gi ak askan wépp lees ko jagleel, rawati na ci jamono jii nu yittewoo lool ag dal ci réew mi.
Niki mu ko baaxoo rekk ci teey ak xereñte, Njiitu Réew, Basiiru Jomaay Fay tëjee jataay bi ci kàdduy boole. Ci yéere cosaan ba mu laxasaayoo, delloo na njukkal jëmm yu am solo ci sunu mboor, yu mel ni Mammadu Ja mi ñu tuddee leegim xàll wu mag wii ci Nsakaaru. « Moom sa bopp itam da cee bokk, moom ko ci sunuy xel ak ci sunuy mbébet, » di woote bi mu def jëme ci saa-senegaal yi ñu gën a mànkoo ngir tabax ëllëg. Wooteem bii nag ngir nu àndandoo doon benn day firndeel yéeneem ci boole cosaan ak méngoo ak jamono ngir liggéey réew mi.
Toppaatleen mbooleem jataay bi: