Biti Réew - 22 MONTHS.SEPTEMBER 2025
Lu jëm ci 80eelu Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Réewi Àddina si, Njiitu Réew mi séq na ab jataay ak kilifa gii di Petr Pavel, Njiitu Réewum Repiblig Ceg.
Waxtaan yi jëmoon ci luy gën a dëgëral jëflante yi, mbébeti lëngoo ci wàllu koom mi, xarala yi ak njàng mi, niki noonu ci yéene ji ñu bokk am ngir gën a xóotal lëkkaloo gi diggante Senegaal ak Repiblig Ceg.
Ndaje mii day wane dogug Senegaal ci amal ay lëngoo yu wuute ak gën a dëgëral ay jëflanteem diggam ak mbooleem yeneen réew yi.