Biti Réew - 01 MONTHS.NOVEMBER 2024
Njiitu Réew Basiiru Jomaay Fay teewe na jullig àjjuma ji ci wetu Peresidaa Recep Tayyip Erdogan ca jumaay Camlica, di màndarga mu am solo ca Istanbul.
Imaam bi ci xutbaam, fàttali na wooteb Alxuraan jëm ci bennoo, dimbalante ak mànkoo diggante way-gëm ñi.
Bataaxel bu am solo bii jëm ci mbaax yi àddina sépp war a bokk, day gën a dooleel jëflantey xaritoo ak lëkkaloo diggante Senegaal ak Turki, di lu ñaari askan yi war a sukkandiku ngir gën a doxal jàmm ak déggoo.