Ginnaaw Medina Baay, Njiitu Réew mi dem ca Lewona Ñaseen.

xamle - 11 MONTHS.OCTOBER 2024
Ginnaaw ba mu bawoo ca Medina Baay, Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, wéyal na siyaar yi muy amal ci wetu Xalifa yi daal di dem ca Lewona Ñaseen.
Njiitu Réew mi ak mbooloo mi mu àndal, te ñi ko séq di ñu bokk ci ngóornamaŋ bi, ñi muy liggéeyandool ak kilifay ndoxalug tund wa, Seex Ahmad Tiijaan Ñas Xalifa Seneraal dalal na leen tatagal leen.
Ci jataay boobu, Njiitu Réew mi fésal taxawaay bu am solo bi këri diine yi am ci dalug réew mi. Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay xamle na fa tamit ne fii ak fan yii di ñëw dina tabb Jëmm joo xam ne mooy jiite mbiru diine yi, ngir gën a sóob këri diine yi ci doxaliinu réew mi.