Biti Réew - 06 MONTHS.DECEMBER 2024
Ginnaaw ngan gu mucc ayib ga mu amal ca Emiraa Araab, Kilifag Réew mi Basiiru Jomaay Fay yegg na ci ngoon gi ca Kataar ngir wuyuji ndënel Kilifa gi Seex Tamim Bin Hamat Al Saanii, Emiir bu Kataar.
Njiitu Réew mi dina teewe Ndajem Waxtaan mu Doha, di xew-xew bu mag ci àddina si, ñu jagleel ko waxtaane jafey-jafey àddina si ci wàllu doxaliin, kaaraange ak suqaliku gu sax.
Ndaje mii am pose lay doon ngir gën a fésal kàddug Senegaal ci kanamu àddina si.