Biti Réew - 31 MONTHS.OCTOBER 2024
Ginnaaw tukki nemmiku gi mu amal ca Araabi Sawudit, Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay, yegg na ca Turki ci Alxemes ji war faa amal tukkib ñaari fan ci ndënel kilifa gi Peresidaa Recep Tayyip Erdogan.
Tukki bii nag mu ngi jëm ci gën a dooleel jëflantey xaritoo ak lëkkaloo diggante Senegaal ak Turki ci sémb yu am solo yu ñu bokk jëm ci dooleel suqalikug koom mi, kaaraange gi ak naataange.