FUTURE INVESTMENT INITIATIVE FORUM 2024: NJIITU RÉEW MI BASSIRU JOMAAY FAY YAATAL NA CI YÉENEY SENEGAAL YI ËPP SOLO

xamle - 28 MONTHS.OCTOBER 2024

Njiitu Réew mi Bassirou Diomaye Faye teewe na tay ci suba ndajem Future Investment Initiative Forum 2024 ca Riyadh. Xew-xew bu mag bii nag day dajale ay kilifa yu am dayoo ci àddina si, ay meññilukat ak i fentkat ngir waxtaane lépp lu jëm ci suqali koomum àddina si.
Njiitu Réew mi aajar na yéeney Senegaal ji aju ci wàllu Vision 2050, jaare ko ci baral jéego yi ci samp ay ndefar fépp ci réew mi, wàllu yasara ak ay coppite yu am solo ci wàllu xarala yi. Woo na meññilukati àddina si ñu dugal seen loxo bu baax ci coppite yooyu ñu namm a amal, jaare ko ci twxawal ay waar ci fànni koom yu bees ngir yokkute gu matale te sax.