FOCAC : Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay demoon nemmikuji waaxu (port) xarala bu Qingdao

xamle - 07 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Ci ndajem FOCAC, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay dem na ci gaawu bi ca Qingdao, fa ko kilifay gox ba jagleel teertu gu mucc ayib.
Njiitu Càmm gi, ci wéyal na, nemmiku waaxu (port) Qingdao, di royukaay ci àddina si ci wàllu xarala ak sàmm kéew mi, di fu 70% ci kontaneer yiy bawoo Siin di jaar. Njiitu Réew mi amal nemmiku googu ànd ko ak
M. Jia Funing, topp-njiital waax wa.
Njiitu Réew mi nemmiku na itam warabi kërug liggéeyukaay gii si Haier, tey yëngu ci wàllu elektoromenaase, kilimatiseer ak ay pexe ci wàllu xarala ak robotig yu ñuy doxal ci pàcc yu bari te wuute, rawati na ci wàllu paj mi.
Bëccëg gii tax na ñu gën a dooleel posey lëkkaloo ci wàllu xarala ak ndefar diggante Senegaal ak Siin.