Biti Réew - 30 MONTHS.JUNE 2025
Kilifa gi, Basiiru Jomaay FAY Njiitu Réewum Senegaal, teewe na, tay ci altine ji 30i fani suwe 2025, jataayu tijjitel 4eelu Ndaje mi àddina si di waxtaane kopparalug suqaliku gi, ci teewaayu Njiiti Réew ak Ngóornamaŋ yu bari, niki noonu ay kilifa yu jiite ay mbootaay ci àddina si, yu mel ni Mbootaayu Réewi Àddina si, Bànk Monjaal, FMI, OMC ak ECOSOC.
Liggéey yi dees na leen wéyal ci ngoon gi ak benn jataayu waxtaan. Njiitu Réew mi dina àddu ci jataay boobu ngir xamle taxawaayu Senegaal ci mbir mu am solo mii : dajale ak jëfandikoo alalu pénc mi ngir suqaliku gu ànd ak moom sa bopp, yamale te sax dàkk.