Feesug dex yu Senegaal ak Gàmbi : Peresidaa Fay ci wetu way-loru ñi

xamle - 19 MONTHS.OCTOBER 2024

Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay demoon na tay ca Bàkkel ngir wane ag njàppaleem jëme ci jaboot yi loru ci wal mi. Fengat yooyu laal na lu ëpp 55 600i nit ca tundu Maatam, Ndar, Tàmbaakundaa ak Bàkkel, yàq dëkkuwaay ya teg ci lu ëpp 1 002i hektaar yu taa ci ay tool.

Ci tolluwaay bu jafe bii nag, nguur gi génne na lu tollu ci 8i milyaari FCFA ngir taxaw ci jafe-jafe yi ci lu gaaw boole ko ak yót ab dund ak i jumtukaay yu askan wa di yittewoo. Taxawal nañu fa benn hopitaal miniteer ngir taxawu askan wa ci lu ñu dul fay dara, boole ko ak ay takk-der yuy saytu seen kaaraange. 

Njiitu Réew mi feddali na ab wooteem ci ñu gën a takku taxaw doon benn ci jamono yu metti yii.