Biti Réew - 06 MONTHS.DECEMBER 2024
Njiitu Réew mi séq na ab jataay tay ak sunu bokki saa-senegaal ya nekk ca Emiraa Araab. Ndaje mii di tëj ngan gi muy amal jamono jii ca réew mooma, tax na mu diisoo ak ñoom ci seen i yitte, jafe-jafe yi ñuy dund ak li ñuy séntu ci nguur gi, boole ko ak ñaax leen ñu gën a góor-góorlu ci luy gën a fésal réewum Senegaal ci àddina si.
Ba tay Njiitu Réew mi feddali na yéeneem jëm ci gën leen a taxawu boole ko ak gunge gi war. Rafetlu na bu baax itam moom Njiitu Réew mi seen taxawaay niki ndawi Senegaal ci àddina si. Xamal na leen itam ne Nguur gaa ngi liggéey ngir taxawal balaa yàgg bis bu muy jaglaeel doomi Senegaal yi féete biti réew.