Dooleel Marin Nasonaal: Njiitu Réew mi daloo na gaalug “Le Cayor”

xamle - 22 MONTHS.OCTOBER 2024

Tay ci suba si Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay jiite na jataayub tudd gaalug saytu gii di “Le Cayor”, di jéego bu am solo ci yokk dooley sunu marin nasonaal bi. Gaal gii bokk ci yi mujj a génn te ànd ak xarala yu wóor dina tax ñu man a taxaw ci jafe-jafey kaaraange yi am jamono jii.

Njiitu Réew mi ndokkale na bu baax marin nasonaal bi ak larme bu Senegaal ci seen ug jaayante ak seen ug xereñ. Seen ug dogu tax na Senegaal man a jàmmaarloo ak yenn ci ay tafaar yu mel ni napp gu jaarul yoon gi, mbëkk mi boole ko ak aar yiy bawoo ci sunu géej gi, niki noonu sunu jumtukaay yi nu samp ci wàllu petorol bi ak gaas bi.

Gaalug saytu gu yees gii day wane yéene ji sunu réew am ci sàmm ay njariñam boole ko ak feddali kilifteefam ci biir ay ndoxam. Marin Nasonaal ci seen njàmbaarte ak seen ug dogu mooy màndargaal moom gi nu moom sunu bopp ci wàllu géej gi. Nanu àndandoo tabax Senegaal gu moom boppam, gu wóor te wëlbati ay yitteem jëm ëllëg.