Dooleel lëngoo diggante Mbootaayug Órob gi ak Senegaal

xamle - 17 MONTHS.OCTOBER 2024

Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay dalal na ci àllarba ji 16i fani oktoobar 2024, komiseeru Órob gi yor wàllu lëkkaloo ci àddina si.

Ci ndaje moomu, soxna Jutta Urpilainen xamal na Njiitu Réew Mi yéeney Mbootaayu Órob gi (UE) ci jàpp ci gis-gis bu am solo bii, di sukkandikukaay bu bees bii di “Senegaal 2050, Agenda National de Transformation”.

Moom komiseer bi fésal na itam solos lëkkaloo gi jaare ko ci taxaw ci jubluwaay yi ñu bokk am ci pàcc yu mel ni njàng mi, xëy mi ak paj mi.