DOOLEEL JËFLANTE YI DIGGANTE SENEGAAL AK ARAABI SAWUDIT

Biti Réew - 29 MONTHS.OCTOBER 2024

Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay séq na ab jataay bu fees dell ak mbégte diggam ak Mohammed Bin Salmaan Bin Abdel Asiis Al Sawuud, miy doomi Buur bi teg ci di Njiital Ndiisoog Jëwriñ yu Araabi Sawudit.
Ci ndaje moomu, Njiitu Réew mi rafetlu na bu baax waxtaan wu am solo wiy firndeel rekk yéeney ñaari réew yi ci gën dooleel jëflante gu dëgër te yàgg a dox seen diggante. Am nañu déggoo ci yóbbu lëkkaloo gi ci dayoo bu gën a kawe rawati na ci kopparal pàcc yi gën a am solo ci koom mi, yasara gi, mbay mi, ndefar gi ak xarala yi.