xamle - 30 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, dalal na ci altine ji 30i sebtàmbar 2024, Jëwriñu Móritani ji yor wàllu Yasara (énergie) ak Soroj (Petrole), Mohammet Uld Xaled, mi jiite woon tañ (délégation) wu takku wu ñëwoon ngir teewe ndaje mu njëkk mi ñu jagleel wàllu koom diggante Senenegaal ak Móritani.
Waxtaan yi a ngi jëmoon ci gën a dooleel jëflante yi diggante Senegaal ak Bokkeefu Islaam gu Móritani, niki noonu ci solos ndaje mii tijji tay (altine) ci Ndakaaru.