Njiitu Réew mi, Basiiru JOMAAY Fay, teewe na ci altine ji 11i fani nowàmbar 2024 Ndajem Araabo-Islaam mu mag mi ñu doon doon amal ca Riyad, ca Araabi Sawudit, te jagleloon ko càmbar tolluwaay bu yéeme bi am jamono jii ca Palestin ak ca Libaŋ.
Njiitu Réew mi posewu na ci ndaje mu am solo mii, Doomi Buur bi Mohammet Ben Salmaan doon jiite, ngir feddali taxawaayu Senegaal bi masul a soppiku jëm ci taxawu réewum Palestin.
Mbooloo mi ànd nañu jël dogal bu ñu tënk ci 38i tomb, boole ko ak di woote ñu wéer gànnaay yi ci na gën a gaawe ca Bànd de Gasaa ak ca Libaŋ. Bokk na ci li gën a fés ci dogal yooyu nag muy taxaw ci aar siwil ya ak taxaw ci fexe ba genn gàllankoor bañ a am ci ndimbal yi ñuy yóbbu ca gox ya loru ci jàmmaarloo yi.
Man ngeen a fekk fii ci suuf mbooleem dogal bi :
Nun, Njiiti Ngóornamaŋ ak Réew yi bokk ci Réewi Lig Araab ak ci Mbootaayu Lëkkaloog Lislaam gi (OCI), te daje fii tay ci ndënel kilifa gi Salmaan Ben Abdel Asiis miy Buuru Araabi Sawudit, ak ci njiital Muhammet Ben Salmaan Ben Abdel Asiis, miy doomi Buur bi te doon Njiital Ndiisoog Jëwriñ yi, ak ci dëppoog sunu yéene ci boole ñaari ndaje yu mag yu araab yi ak Islaam yi Réewi Lig Araab ak Mbootaayu Lëkkaloog Lislaam (OCI) jëloon dogalu amal ko ci càkkuteefu Réewum Araabi Sawudit, ngir waxtaane fitna ji Israayel di teg ci kaw askanu Palestin, 11i fani nowàmbar 2023, daje nanu tay ci Riyad, ngir indi tontu lu leer ci ni xew-xew yi di gën a yokkoo ak ci ginnaaw diisoo yu Doomi Buurub Araabi Sawudit jot a amal ci càkkuteefu Réewum Palestin ak yenn réew yu bokk ci mbootaay gi;
Ci firndeel yitte ju kawe ji nu am ci mbirum Palestin ak taxawu gu wér jëme ci askanu Palestin ngir ñu man a jot ci seen yelleef yi manul a ñàkk, te la ca jiitu di seen yelleef ak seen péexte ci am Réew mu moom boppam ci dig yu 4i fani suwe 1967 boole ko ak Penkub Al-Quds doon gëbla gi, ak yelleefi daw-làqu ya dellusi boole ko ak jox leen ndàmpaay, niki ñu ko tënke woon ci Dogal yu am solo yi ñu jëloon ci wàllu yoonu àddina si, rawatina Dogal 194, bu weesoo wareefu jàmmaarloo ak lépp lu jëm ci nasaxal walla salfaañe yelleef yooyu; boole ci xamle ne mbirum Palestin mii wuutewul ak xeex yu wér yi askan yi daan amal ngir génn cig nooteel;
Ci feddali ne Réewum Palestin moo am sañ-sañ ci Penkub Al–Quds gi doon gëblaam ba fàww; di dàq bépp dogal mbaa jëfi Israeyel yu jëm ci jéem koo moomale boppam ak bëgg faa saxal ag nooteelam, ndax bees sukkandikoo ci yoonu àddina si ak Dogal yu am solo yi ONU jëloon, yellul, neen la, warul te teguwul ci yoon; rax ci dolli dëkkub Al-Quds Al-Sariif rëdd wu xonq la wu réewi araab yi ak yu lislaam yi jàpp ne kenn waru koo jéggi; di feddali kon sunug njàppale gu wér ci sàmm màndargam araab ak lislaam gi Penkub Al-Quds làmboo ak aar sellaayu warabi lislaam ak kerceŋ yu sell yooyu fa nekk;
Ci feddali sunug njàppale gu wér jëme ci Repiblig bu Libaŋ, ci kaaraangeem, ci moom boppam ak ci aar ay ma-réewam;
Jël nanu dogalu:
- DËGGAL dogal yi nu jëloon ca ndaje mu njëkk ma nu àndoon, amal ko ca Riyad, ca nowàmbar 2023; FEDDALI wareefu taxaw jàmmaarloo ak fitna yi Israyel di tege ca Bànd de Gasaa ak ca Libaŋ; LIGGÉEY ci dakkal faat yu jéggi dayoo ya ñuy def siwil ya, moo xam muy xale, jigéen, mag ña ak nit ña yorul i gànnaay; WÉYAL takku gi ànd ko ak mbootaayu àddina si, ngir dakkal ni Israyel di salfaañee yoonu àddina si ak yoonu àddina si ci sàmm yelleefi doomu aadama yi, te doon luy yàq jàmm ji ak kaaraange gi ca tund woowu ak ci àddina si; boole ko ak di feddali mbooleem dogal yi ñu jëloon ci fanweer ak ñetteelu Ndajem araab mi ñu amaloon ca Bahrayni ca weeru mee 2024, ak ca fukk ak juróomeelu ndajem Islaam mi amoon ca Repiblig bu Gàmbi ca weeru mee 2024.
- ÀRTU ci tafaari jàmmaarloo yiy am ci tund wi ak loraange yi mu man a jur ci tund wi ak ci àddina si, ci ni fitna yi di gënee law, doon lu fay bëgg a sax daanaka lu ëpp am at, ñu jëme ko ci Bànd de Gasaa te mujj koo yaatal ba Repibligu Libaŋ, niki noonu salfaañe gi am ci moom sa bopp ca Repiblig bu Iraq, Repiblig Araab bu Siri ak Repiblig Islaam bu Iraŋ, te lépp nag mbootaayu àddina si ne ci patt nanguwu cee yëy-yàbbi.
- TAXAW bu baax ngir ñu doxal mbooleem dogal yu am solo yi bawoo woon ci Ndajem Mbootaayu Réewi Àddina si, bokk ci yooyu Dogalu A/RES/ES-10/22 bi jëm ci kaaraangeg siwil yi ak sàmmonte ak wareefi yoon ak yeeleefi doomu aadama bu 10i fani de desàmbar 2023, ak bu Ndiisoog Kaaraange gi, niki noonu it fàww Ndiisoog Kaaraange gi jël dogalu ga, sukkandiku ko ci Pàcc VII bu Sàrtub Mbootaayu Xeet yi, ngir ga Israyel giy boroom doole jiy noote, mu wéer gànnaay yi ca Bànd de Gasaa, yóbbul ndimbal lu yaatu ci lu jamp ñeel mbooleem warab ya nekk ca Bànd de Gasaa boole ko ak doxal Dogal 2735 (2024), 2728 (2024), 2720 (2023) ak 2712 (2023) yiy woote ci gaaw jël matuwaay yu jamp ngir fexe ba ñu man a yóbbu ndimbal lu yaatu te wóor ci lu dul am genn gàllankoor, ak doxal Dogal 2728 biy joxe ndigalu ñu wéer gànnaay yi, niki noonu dogal yiy feddali yelleefu askanu Palestin ci doxal seen yeleef yi manul a ñàkk, bokk ci yooyu yelleefu am seen ug dogu ak jonnug réew ma, ak yelleefu daw-làqu ya dellusi, ak yiy dëggal kilifteefu Mbootaayu Xeet yi ci li soxal mbirum Palestin ba keroog muy saafarawu ci fànn yépp; SÀKKU ci Ndiisoog Kaaraange gi mu nangu déggoo gi àddina si jëloon ci Dogal bi bawoo woon ci Ndajem Mbootaayu Xeet mi ñu amaloon 10i fani mee 2024, boole ko ak dëggal ne Réewum Palestin daa war a bokk ci biir Mbootaayu Xeet yi, jaare ko ci jël dogal buy jox Réewum Palestin estati boobu; SOÑÑ Réew yi ci bokk ñu dajale ndimbal yi war ngir ñu doxal Dogal boobu.
- FEDDALI njàppale gi boole ko ak di rafetlu jéego yu am solo yi Repiblig Araab bu Esibt ak Réewum Kataar di teg, ànd ko ak Etats-Unis Amerig, ngir ñu gaaw wéer gànnaay yi ba fàww ca Bànd de Gasaa ak féexal ñi ñu jàpp ak ñi ñu tëj; JÀPP ne bu mbir àntuwul ba fii réewum Israyel a ko waral ndax Ngóornamaŋam nanguwul a sàmmonte ak déggoo yi way-dox tànki jàmm yi tënkoon.
- Ñaax mbootaayu àddina si ñu doxal ca na mu waree gis-gisu Ëttu àttekaayu àddina si, te ñu joxe woon ko 19i fani sulet 2024, mu jëm ci dakkal ni Israrayel sampoo foofu te far màndarga ya, boole ko ak joxe ay ndàmpaay ndax yàqu-yàqu yi, ca na mu gën a gaawee.
- YOOLE kirim yi waa Israyrel di amal ca ndoortel fitna yay wéy ba leegi di dal ci kaw askanu Palestin, ca Bànd de Gasaa ak ca mbeeraayu Palestin, te bokk ci ñooñu ay xale, ay jigéen ak i mag, rax ci dolli nooteel gi, metiital gi ak doxaliin yu jéggi dayoo yi ñuy teg seen kaw; WOO Réew yi bokk ci Mbootaayu Xeet yi ñu dox ci luy leeral nit ñi ñu jàpp, te taxaw ci ñu bàyyi leen ca na mu gën a gaawee, taxaw ci seen kaaraange te sàkku ñu amal luññutu gu maandu te leer ci kirim bii, te bokk ci loolu ñenn nit ñu ñuy jàpp cig njaay doole.
- Bañ a làq-làqal YOOLE kirim yu doy waar yi larmeb Israyel di amal ca Bànd de Gasaa, boole ko ak di bóom, boole ay néew yu bari ci menn pax, mettital, ray yu teguwul fenn, ñiy réer, yàq ak teqale ay xeet, rawati na ca bëj-gànnaaru Bànd de Gasaa, ci ayi-bis yii weesu; di WOO Ndiisoog Kaaraange gi mu taxawal kurélug luññutu gu maandu te wóor ngir càmbar kirim yi boole ko ak jël matuwaay yu wér ngir moytu ñu far firnde yi, sàkku ci layoo ak ñi ko def te fexe ba teg leen daan yi war.
- ÑAAWLU bu baax fitna yi Israyel wéy di teg ci kaw Libaŋ ak di salfaañe moom boppam gi ak kaaraangeg mbeeraayam; WOOTE ñu wéer gànnaay yi ca na mu gën a gaawee, doxal gu matale ci Dogal 1701 (2006) bu Ndiisoog Kaaraange gu Mbootaayu Xeet yi ci léppam nag; di FEDDALI ag njàppaleem jëme ci Repibligu Libaŋ giy dund ay fitna; di ÑAAWLU ba fa mu yam singili gi ñu def ci di song larmeb Libaŋ ak i dalam, ba tax ñu bari ñu faatu ci ñoom ak ñu am i gaañu-gaañu, faatug siwil yi, di yàq ay dëkkuwaay ak tuxug nit ñi ci lu ñu sañut a bañ, niki sóobarey Mbootaayu Xeet yi ca Libaŋ (FINUL); TAXAW ci njàppaleg campeefi ndayi sàrti Libaŋ ñu doxal seen kilifteef ak yokk sañ-sañu Libaŋ ci moom boppam fépp ci mbeeraayam; FÉSAL wareefu jàppale larmeb Libaŋ bi war a sàmm bennoo ak dalug Libaŋ; DUUT BAARAAM ci ne fàww ñu amal palug Njiitu Réew ma ak taxawal ub Ngóornamaŋ, lépp tegu ci sàmmonte ak Ndayi Sàrtu Libaŋ ak doxal Déggoog Tayif gi.
- ÑAAWLU ba fa mu yam congug maa tay gi Israyel amal ci kaw way-kaaraangey ONU ya ca Libaŋ, te doon jalgati gu leer ci Sàrtu Mbootaayu Xeet yi; SÀKKU ci Ndiisoog Kaaraange gi ñu jàpp ne Israyel mooy njaag ci taxawu kaaraangeg way-kaaraangey ONU yiy yëngu ci màndargam Sóobarey Mbootaayu Xeet yi ca Libaŋ (FINUL).
- DÀQ ni ñuy gawee askanu Palestin ngir ñu jóge ca seen i suuf, di lu ñu jàppee ni kirim ci wàllu xare ak jalgati gu wér ci yoonu àddina si, te doon lu nu war a ànd xeex ko.
- NAQARLU politigu daan bi Israyel di doxal ak di jëfandikoo ñag ak xiifal niki gànnaay gu muy teg ci kaw siwil yi nekk ca Bànd de Gasaa; di SOÑÑ kurélu àddina si ñu jël ay doxaliin yu wóor te jamp ngir dakkal jéeya ji fitna ji di jural nit ña, jaare ko ci ga Israyel mu jóge ca Bànd de Gasaa boole ko ak tijji mbooleem yoon yi ko teqale ak Bànd de Gasaa ak dindi lépp lu man a gàllankoor ndimbal ya ñuy yóbbu ca Bànd de Gasaa; di WOO ci loolu, larmeb Israyel ñu jóge ca na mu gën a gaawee ca terminaal bu Rafah ak yoonu Salaahediin (Filaadelfi), dellusig kilfay Réewum Palestin ngir saytu Terminaal bu Rafah boole ak dooraat Déggoog 2005 ci wàllu dem ak dikk ngir yombal liggéeyu kuréli wallukat yi ak wéyal yóbbug ndimbal li ci anam yu mucc ayib.
- FÉSAL ne fàww ñu boole doole yi ngir doxal njureef yi bawoo ci ndajem waxtaane ndimbal li jëm ca Gasaa, te Réewum Jordani doon ko dalal, 11i fani suwe 2024, àndoon ko ak Repiblig Araab bu Esibt ak Mbootaayu Xeet yi, teg ci dajale taxawu gi war ngir Ndajem waxtaane ndimbal mi ñu war a amal ca Keer, 2i fani desàmbar 2024, lépp ngir teg ay jéego yu jëm ci yóbbu ndimbal lu wér ca Bànd de Gasaa.
- WOO mbootaayu àddina si ñu àddu bu wér, ga Israyel mu sàmmonte ak yoonu àddina si, ñaawlu te àrtu ci wàllu doxaliinu Kumba am nday ak Kumba amul nday, ci doxal yoonu àddina si, yoonu àddina si ci sàmm yelleefu doomu aadama ak Sàrtu Mbootaayu Xeet yi, di loo xam ne man naa gàkkal taxawaayu Réew yiy aar Israyel jël ko teg ko ci kaw ñépp di ko neŋŋ-neŋŋal, niki noonu ci wàllu lëkkaloo yi, ak teg ci suuf tànneefu doxal yoonu àddina si.
- ÀND ci Dogalu A/RES/ES-10/24 bi ñu yaataloon ci Ndaje mu Mag mi, 18i fani sebtàmbar 2024, te jëmoon ci doxal njureefi gis-gis bi Ëttu Àttekaayu Àddina si joxe woon ci ñàkk a tegu ci yoon gi nekk ci sancug Israyel ca Bànd de Gasaa.
- WOO réewi àddina sépp, seen kuréli yoonal yi ak seen campeef yépp ak mbootaayi àddina si ñu sàmmonte ak dogalu yelleefu àddina si ci dëkkub Al-Quds ak taxawaayam ci wàllu yoon ak mboor, niki ku bokk ci mbeerayu Palestin gi ñu sanc ca atum 1967.
- ÑAAWLU ba fa mu yam singili gi Israyel di def jëm ci salfaañe warab yu sell yu Lislaam ak yu kerceŋ yi di Al-Quds ak far màndargay araab, lislaam ak kerceŋ yi mu làmbool; ÑAAX mbootaayu àddina si ñu wax ak Israyel ngir mu yam, boole ko ak di àrtu Israyel ci cong yi muy wéyal jëme ci Jàkka ju sell jii di Al-Aqsaa/Doju Néeg bu Tedd bi, bokk ci yooyu tamit jullit ñi ñuy tere ñu yegg ca biir Jàkka ja ngir matale seen ug jaamu, bu weesoo ni ko sóobarey Israyel yi tegee loxo, di ko yàq ak a jéem a soppi ya mu làmbool ak pexey soppi taxawaayam ci wàllu yoon ak mboor mi Jàkka ju Sell ju Al-Aqsaa làmboo ak wàññi ab dayoom; FEDDALI ne Jàkka ju sell jii di Al-Aqsa/Al-Haram Al-Sariif, ci yaatuwaayam gi tollu ci 144i junniy meetar kaare, barab la bu ñu jagleel jullit ñi, teg ci Departamaa bu Jordani biy saytu li ñu jagleel Al-Quds ak mbirum Jàkka ji sell ju Al-Aqsa mooy gennug Kurél gi am sañ-sañu saytu, toppatoo ak lootaabe tàbbi gi ci biir Jàkkay Al-Aqsa, ci li soxal moomeelu haasimit yi ci mboor ci warabi lislaam ak kerceŋ yu sell yii nekk ci Al-Quds.
- WOO Ndiisoog Kaaraange gi ñu jël dogalu ga Israyel mu dakkal Politig yi jaarul yoon yi man a yàq kaaraange ak jàmmi tund wi, te jëmmal itam Dogal yu am solo yu Mbootaayu Xeet yi ci dëkkub Al-Quds Al-Sariif, di luy gàntal nangu ne Al-Quds mooy Gëblag Israyel, ndax doxaliin wu teguwul ci yoon la, te day salfaañe yelleef yi ci wàllu mboor, yoon ak nekkiinu askanu Palestin ak Umma Islaam bi jàpp ne bépp dogal bu jëm ci jéem a soppi taxawaayu Al-Quds Al-Sariif teguwul ci yoon te ag jalgati la ci yoonu àddina si ak dogal yu am solo yu Mbootaayu Xeet yi, kon lees war a neenal la far ko ci saa si; SÀKKU ci mépp réew mu jël dogal bu man a laal tolluwaayu mboor ak yoon wu am ca Al-Quds mu xoolaat matuwaay yooyu te xam ne jaarul yoon; TAXAW bu baax ci ne fàww ñu dox ci lu dëgëral askanu Al-Quds ci seen i suuf, rawati na jaare ko ci taxawug komiteb Al-Quds bi ak bànqaasu ndoxalam gii di Beiyti Maal Al-Quds Al-Sariif.
- SÀKKU njàppaleg mbooleem réewi àddina si ngir ñu dakkal yënguy Israyel ci biir Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Xeet yi ak ci biir mbooleem Mbootaay yi, jëm ci àndandoo aajar sémbu dogal ca Ndaje mu mag mi - ci fukkeelu jaataay bu mag di (Bennoo ngir Jàmm), ndax ni muy salfaañee Sàrtu Mbootaayu Xeet yi, gàllankoor yi muy indi ci jàmm ak kaaraangeg àddina si ak ñàkk a matale wareefi ku bokk ci Mbootaayu Xeet yi, ak ci cëslaayu gis-gis bi Ëttu Àttekaayu Àddina si joxe 19i fani sulet 2024.
- SÀKKU ci mbooleem Réew yi ñu tere jaay Israyel ay gànnaay ak i doom ak ÑAAX réew yi ñu ànd ci yéene jii Repiblig bu Turki ak Kippaango gii 18i réew séq gaaral, te lu mat 52i réew jot koo torlu, niki noonu OCI ak Réewi Lig Araab, teg ci bind ab bataaxel Ndiisoog Kaaraange gi, Njiital Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Xeet yi ak Sekkreteer Seneraalu Mbootaayu Xeet yi, ngir ñu bàyyee jox Israyel ay gànnaay; WOO mbooleem réew yi ñu torlu ko.
- SOÑÑ CPI mu amal ay màndaa dare ci kilifay siwil ak militeer yu Israyel ndax kirim yi ñu amal jëme ci askanu Palestin te Ëtt bi am sañ-sañu àddu ci.
- SÀKKU ci Ndiisoog Kaaraange gi ak Kurélu àddina si ñu jël dogal yi war, boole ko ak ga ay daan, ngir dakkal cong gu teguwul ci yoon gi Israyel di amal ca Cisjordani, te doon luy nasaxal pexe mi ñu jëloon ci amal ñaari réew yu wuute boole ko ak gàllankoor muur yi amoon ngir yegg ci jàmm ju wér te sax ci tund wi, kiriminaalise politigu nooteel gii, yoole politigu nooteel gi ñuy amal ngir foqarti mbooleem suuf yi bokk ci mbeeraayu palestin ngir a gën yaatal nooteel gu jaarul yoon, ndax kat jëf jii cong gu fés la jëm ci salfaañe yelleefi mboor ak yoon yu askanu Palestin ak jalgati gu wér ci Sàrtu Mbootaayu Xeet yi, pas-pasu yoonu àddina si ak Dogal yu am solo yu Mbootaayu Xeet yi.
- YOOLE bu baax jëfi rëtalkat yi Israyel di teg ci kaw askanu Pelestin ak seen alal, te doon luy gën a law ci anam yu lootaabewu ànd ko ak Ngóornamaŋu Israyel bi leen di jàppale ak a aar ay sóobareem, ak woote ci :
- Jàppe way-mbéfeer yi ne ñooy ñi sooke kirim yi ñuy teg ci kaw askanu Palestin ak seen alal;
- Boole way-mbéfeeri Israyel yi al kuréli way-nootey yahuud yi ci Kippaango ak kuréli rëtalkat yi, bind leen ci limkag rëtalkati réew yi ak àddina si, boole ko teg i pexe ci fànn yépp, ba ci Mbootaayu Xeet yi ak Ndiisoog Kaaraange gi rawati na, ngir Njiiti Israyel yi ak way-mbéfeer yi man a layoo kirim yi ñuy amal;
- Wan ginnaaw bépp porodiwi bu Israyel ci mbeeraayu Palestin ak àntarpiriis yi fay yëngu, te nekk ci lim bi Ndiisoog Yelleefi doomu aadama yi fésal 30/6/2023, boole ko ak fésal limkag gàcce guy wane turi àntarpitiis yooyu, ndax kat bokk nañu ci liy suuxat nooteel gi ba mel ni ñuy wut mu sax fa;
- Woo réewi àddina sépp ba ci réew yi ci bokk, ñu tere way-mbéfeer yi nekk ci mbeeraayu Palestin, ba ci Penkub Al-Quds, ñu bañ faa dugg ak lu man a xew, jël ay matuwaay ànd ko ak réewum Palstin yu jëm ci càmbar këyiti dàntite yi ngir xam fan lañu dëkk, ndegam ñoom ñooy dugal seen yoxo ci jëfi rëtal yi ñuy teg ci kaw askanu Palestin, seen alal ak seen suuf;
- Woo Sekkereteer Seneraal bu Réewi Lig Araab ak bu OCI, ñu ànd ko ak réewum Palestin, bind limkag turi Kippaango yooyu daal di ko jébbal réew yi ci bokk.
- WOO mbootaayu àddina si ñu tëral ay pexe ak arminaat bu wóor ci àddina si ngir dakkal nooteel gi boole ko ak jëmmal Réewum Palestin mu am péexte te moom boppam ci digi 4i fani suwe 1967, Al-Quds di gëbla gi, bees sukkandikoo ci pexem taxawal ñaari réew yu wuute, niki ñu ko tënkee ba am cig dëppo ak yéeneey jàmmi araab ju 2022.
- WAX ne jàmm ju wóor te daj tund wi, juy indi kaaraange ak dal ñeel réew yépp, manul a am fii ak Israyel dakkalul nooteel gi ci mbooleem mbeeraayu araab yi ñu sanc ba ci rëddi 4i fani suwe 1967, niki ñu ko tënkee ci dogal yu am solo yu Mbootaayu Xeet yi ak naalu jàmmi araab bu 2002 ñeel leen.
- DELLOO NJUKKAL réew yi jot a nangul Réewum Palestin boole ko ak ÑAAX yeneen réew yi ñu def lu ni mel, di RAFETLU « Lëkkatoog àddina si ngir doxal pexem ñaari réew yu wuute », di lëkkatoo gu komiteb jëwriñi Araao-Islaam yi ànd taxawal, ci njiital Réewum Araabi Sawudit, ci lëkkaloom ak réewi araab yi ak yu lislaam yi, ànd ko tamit ak Mbootaayu Réewi Órob yi ak Réewum Noorwees, ca weeru sebtàmbar 2024, ca New York, di Lëkkatoo gu amal ndajeem mu njëkk 30 ak 31i fani oktoobar 2024, ca Riyad, boole ko ak di fésal solos gën koo taxawu, te di ci woo réew yi jàmm rekk yitteel ñu ñëw bokk ci lëkkatoo gii.
- LIGGÉEY ci sóob réewi àddina sépp ñu jàpp ci xeex ngir Réewum Palestin bokk ci Mbootaayu Xeet yi, am ci cér bu wér, te DOOLEEL jéego yu am solo yi Repibligu Alseri di teg, di ku bokk ci ñaari mbootaay yépp ci Ndiisoog Kaaraange gi, jëm ci gaaral sémbu dogal buy nangu tàbbi googu, niki noonu jéego yi muy teg ngir taxawu mànkoo ngir taxaw ci mbirum Palestin.
- ÑAAWLU kàdduy mbañeel ak xeetal yi Jëwriñi Ngóornamaŋu Israyel di yékkati; WOO Mbootaayu Àddina si ñu xam ne luy njiin rekk ñoom ñooy njaag, niki ko yoonu àddina si tëralee.
- NAQARLU cong yi kilifay Israyel yi di wéy di teg ci kaw Mbootaayu Xeet yi ak Sekkreteer Seneraalam, niki ni ñuy teree mbootaayi àddina si ba ci sax Ndawi Mbootaayu Xeet yi ak Kuréli luññutu yi ak ñi bokk ci pekkub Kurél gu mag giy saytu yelleefi doomu aadama yi, ñu yegg ca mbeeraayu Palestin, bu weesoo dakkal liggéeyi teewaayu mbootaayu àddina si ca Al-Xaliil, lépp nag ci jalgati wareef yi, niki aji-nooteel ju am doole, ak Dogal yu am solo yu Mbootaayu Xeet yi; ÑAAX mbootaayu àddina si mu dëggal kilifteefam ci wàllu kaaraange, niki ko Dogalu Mbootaayu Xeet yi diglee, te ràppooru Sekkereteer Seneraalu Mbootaayu Xeet yi fésal ko ci wàll woowu.
- ÑAAWLU ni Knesset bu Israyel jàllalee ay sàrti xeetal yu teguwul ci yoon, ba ci sàrt bii jëm ci dindi mbalaanu kiiraay mi ñu joxoon ndawi Bànqaasu wallu ak liggéeyi Mbootaayu Xeet yi ñeel daw-làquy Palestin yi (UNRWA), boole ko ak di leen tere ñu amal seen i yëngu ca mbeeraayu Palestin teg ci dog seen lëngoo, ak dogal bi jëm ci ñàkk a ànd ci taxawal Réewum Palestin, di xamle nag ne seen sàrt yooyu ak seen dogal yi teguwul ci dara te lépp neen la; WOO réewi Mbootaayu Xeet ñu teg Israyel ay daan, ngir ga ko mu sàmmonte ak yoonu àddina si ak sàrti kuréli àddina si; SOÑÑ réew yépp ñu indil Kurél gi ndimbal lu wóor ci wàllu Politig ak koppar.
- WOOTE ci ñépp indil askanu Palestin ak Réewum Palestin bépp xeetu ndimbal ci Politig ak laamisoo, doxal bennoog réewu Palestin ak jël respoosaabilite yu wér ci mbooleem mbeeraayu Palestin, jaare ko ci dooleel ko ci wàllu sémbu ndimbal, dundalaat koom ma ak tabaxaat Bànd de Gasaa, fésal solos wéy di taxawu njëlu réewum Palestin boole ko ak doxal kaaraangeg kopparal gu leer gu méngoo ak yoon yi ñu tëral, ak woo Mbootaayu Àddina si ñu ga Israyel mu teggi tànkam ca na mu gën a gaawe ci galagu Palestin yi mu naj.
- DOOLEEL jéego yi Repiblig araab bu Esibpt di teg ngir taxawu Palestin, ci jamono ju doy waar jii, dimbali Ngóornamaŋu Palestin mu man a matale ay wareefam ci askanu Palestin, jaare ko ci teg i pexe ak jël ay matuwaay, ak ànd ci kurélug ndimbal ca Bànd de Gasaa gi ñu taxawal ci dekkere bu Njiitu Réewum Palestin, ci wàllu bennoog Politig ak melosuuf bu Réewum Palestin, ci rëddi 4i fani suwe 1967, te Penkub Al-Quds di gëbla gi, doon moomeelu Palestin; FEDDALI ne Kurélug xeex ngir Péextem Palestin mooy genn kurél gi am sañ-sañu teewal askanu Palestin.
- WOOTE ñu wéy di yót ab dund ak wallu jëme ci Ngóornamaŋ bu Libaŋ ngir mu man a jàmmaarloo ak fitna yi ko Israyel di teg, ba ci jafe-jafey nit ñi daw-làquji ba keroog ñuy man a dellusi ca seen i gox boole ko ak jox leen li ñuy yittewoo ci wàllu dund, boole ko itam ak dox ci fexee amal ay yeesal yuy may réewi bokk yi ak xarit yi ñu man a dugal seen loxo ci taxawu seen um koom ngir dimbali askanu Libaŋ mu gaaw génn ci jafe-jafe yi muy dund.
- ÑAAWLU ba fa mu yam cong ak fitna ju metti ji Israyel jëmale ci mbeeraayu Repiblig araab bu Siri, ba ci siwil yi ñuy dàkk, di yàqate taax yi ak jumtukaayi siwil yi ak di ko xañ moom boppam, di bir yoo xam ne ay kirim la ak jalgati yoonu àddina si ak Dogal yu am solo yu Mbootaayu Xeet yi; FÉSAL ne fàww Israyel jóge ca Golan Araab bu Siri ga mu sampu.
- SAS komite bi boole Jëwriñi Araabo-Islaam yi, ci njiital Araabi Sawudit, te ñu jëloon dogalu taxawal ko ci ndajem araabo-islaam mi ñu njëkk a amal, 11 fani nowàmbar 2023, mu wéyal liggéey yi te gën cee góor-góorlu, boole ko ak gën a yaatal waaram dugal ci dakkal fitna yi ñuy teg ci kaw Libaŋ; komite boobu war nay amal ay ràppoor yu ñaari Sekkereteer Seneraal yi war di jébbal Réew yi ci bokk.
- SAS komiteb jëwriñ yooyu mu gën a boole réew yi féete ci bëj-saalumu àddina si ci jéego yi ñuy teg jëm ci gën a dooleel ndimbalu àddina si jëm ci dakkal xare bi ak nooteelug Israyel.
- TAXAW bu baax ci ne fàww ñu aar dem bi ak dikk bi ci yooni géej gi, niki ko yoonu àddina si tëralee.
- ÀND bu baax ci torlug Réewi Lig Araab yi, yu Mbootaayu Lëkkaloog Lislaam gi (OCI) ak yu Mbootaayu Réewi Afrig yi, ca Riyad, ci doxaliin wi ñetti wàll yi séq ci mbirum Palestin; RAFETLU bu baax taxawaay bu wér bi Mbootaayu Réewi Afrig yi am ci mbirum Palestin.
- SAS Sekkereteer Seneraal yu Réewi Lig Araab yi ak Mbootaayu Lëkkaloog Islaam gi (OCI) ngir ñu lëkkale jéegoy topp ak doxal matuwaay yi ñu jël ci Dogal bii, boole ko ak di faral di jébbal réew yi ci bokk, ràppoor yiy tënk ci mbir mi.