Diisoo ci Sistemu Politigu Réew mi

xool - 25 MONTHS.MAY 2025

Àllarba 28i fani mee 2025, CICAD dina dalal xewu tijjitel Diisoo yi ñuy amal ci réew mi te ren ñu jagleel ko sistemu politig bi.

Ci doxaliin wu boole ñépp, Njiitu Réew mi fas na yéene sóob bu baax mbooleem ñiy yëngu ci dundug politig bi ak réew mi ci bisub xalaat bii, ngir xàll yoon yu mag yi ci campeefi Senegaal yi.