Demug Njiitu Réew mi ca 79eelu Ndajem Mbootaayu Réewi àddina si

xamle - 21 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Kilifa gi Basiiru Jomaay Fay, Njiitu Réewum Senegaal, bawoo na Ndakaaru ci gaawu bi 21i sebtàmbar 2024, wutali New York, ca Etats Unis. Njiitu Réew mi dina teewe 79eelu Ndajem Mbootaayu Réewi àddina si, war a am 24 ba 30i sebtàmbar 2024.
Ñu war cee waxtaane tomb bii di « Bennoo ci biir wuute, ngir jàmm ju lëw, suqaliku gu sax ak ngorug doomu aadama ci fépp ak ci ñépp», ndaje mii am pose lay doon ci Njiitu Réew mi ngir mu yékkati kàddug Senegaal ci yu am solo yiy xaar àddina si, boole ko ak feddali jaayanteg sunum réew ci doxal lëkkaloo diggante réewi àddina si boole ko ak fésal mbaaxi jàmm ak yoon.
Ca 79eelu Ndajem Mbootaayu Réewi Àddina si , Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY FAY dina teewe itam ndajem Ëllëg, di naalu Njiital Mbootaayu Réewi Àddina si, Àntoño Guterres.