Demug Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY ca gétt yu Mbaar mi ak Galoya.

xamle - 01 MONTHS.JUNE 2025


Ay fan laataa Tabaski gi, Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay FAY, wàccoon na dem nemmikuji ñaari warabi jaayukaayi xar : géttu Mbaar mi Fadiilu Keyta, Njiitu ADAM, di jiite ak gétti Galoya , ci njiital Abdu Kan mi jiite FENAFO.

Njiitu Réew mi rafetlu na taxawaayu sàmmkat yi, jaaykat yi ak ñiy yëngu ci wàll wi ngir Tabaski gu jàppandi te ànd ak ndimbal. Feddali na jaayanteg Nguur gi jëm ci taxawu càmm gi, gën a suqali jumtukaayi céddale yi ak taxaw ci wér gi yaramu jur gi.

Ci doxaliin wuy wane jege askan wi, ak taxawaayu boroom kër, Njiitu Réew mi jënd na ñaari xar ci njëg yu jàppandi, muy jëf ju mu bokk di dund ak lu ëpp ay milyoŋi saa-senegaal ci jamono ju am solo jii.

Muy nemmiku guy firndeel yéeney Njiitu Réew mi jëm ci gën a jege askan wi ak gunge mbooleem ñiy jéem dara ngir Tabaski gu mucc ayib, gu ñu dund ci ngor ak mbokkoo.