Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay, jiite na ci àjjuma ji 20i fani desàmbar 2024 xewu dalal diññiteer yi ci wàllu « Ordres Nationaux » ca saal dee bànke bu Njéndel Réew mi.
Jataay bu am solo bii may na Njiitu Réew miy Kilifa gu Mag gi ci wàllu « Ordres Nationaux » yi, mu dekkoore juróom fukk ak juróom benn (56) ci sunu bokki ma-réew yu fés ci wàll wi kenn Ku nekk ci ñoom di yëngu. Ci jëmm yoouyu, ñenn ñi boole nañu leen ci diññiteer yi ci wàllu « Ordre national du Lion », di garaatu ràññiku bi gën a kawe ci réew mi, ñeneen ñi ci ci wàllu « Ordre national du Mérite ».
Ñoom ñii, ci seen i jaar-jaar ak seen jikko yu rafet jëme ci nit ñi ak ci seen wàllu liggéey, dañuy màndargaal mbaax yu wér ci sunu Repiblig bi: xereñte, njàmbaar, dogu ak bëgg sa réew. Ñuy ay jigéen ak i góor ñu bawoo ci gox yu fasantikoo, boole seen yéeney bopp ak liggéeyal askan wi, di ay royukaay dëgg ci ndaw ñi.
Njéndel Réew mi di leen ndokkale bu baax te di leen gërëm ci royukaay yi ñu doon, di loo xam ne mooy màndargaal déggoo gi ci réew mi ak Senegaal gu moom boppam, jub te ubbeeku ci àddina si.