Daloo tënub Lat Joor

jëwriñ - 12 MONTHS.DECEMBER 2024

Ci dënel  Farab goxu Cees, Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay ñu ngi koy séntu 12i fani desàmbar 2024 ca Cees ngir daloo tënub Lat Joor.

Moom Njiitu Réew Mi war a fésal tën bii ñu tëggee xànjar te muy màndargaal jàmbaar jii ci kaw fasam wii di Maalaw te ñu samp ko ci diggante palaas Agoraa ak Óditóriyóm bi.

Muy xew wu ñuy delloo njukkal Lat Joor Ngóone Latiir Jóob, miy màndargaal bañ nooteelug Farãas.