xamle - 15 MONTHS.NOVEMBER 2024
Ci lu soxal 15eelu « Biennale de l’Art Africain Contemporain », Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay demoon na tay ci ngoon ca Ëttu àttekaay ba woon ngir nemmiku ya ñu fay fesal:
• Fésalug réewi àddina siy dajale 58i ma-pasiini Afrig ak Jasporaa;
• Fésalug way-dajale yiy wane yu am solo yu way-dajale yu Senegaal di amal;
• Fésalug Design, di sargal xereñte ak fent;
• Fésal gu ñu jagleel Anta Sermen Gay miy jëmm ju am solo ci wàllu pasin ci weer.
Nemmiku gii nag am pose la ngir màggal xereñteg fent ak sañ-sañ bi ma-pasin yi ame te doon luy firndeel solos mbatiitu Senegaal ak Afrig. Biennale bu Ndakaaru bii royukaay la ngir ëllëg gu sax ci mbatiit ak fent. #DakArt2024