xamle - 01 MONTHS.DECEMBER 2024
Tay 1 panu desàmbar 2024, ci njiital Kilifa gi Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, Njiitu Réewum Senegaal, Senegaal a ngi màggal 80eelu atu bóom gi amoon Caaroy ca 1944.
Muy jamonoy teewlu ak fàttaliku ngir delloo njukkal tiiraayéeri Senegaal yi daanu woon ca Caaroy, di xët wu tiis ci sunu mboor.
Njiit yi, ma-réew yi ak gan ñi bawoo fenn fu ne ci àddina si dinañu daje ca Kãa Militeer bu Caaroy ngir fàttaliku boole ko ak fàttali seen taxawaay ngir jot ci seen ngor ak doxal yoon.
Caaroy, ginnaaw 80i at: wareefu fàttaliku ngir gën a man a tabax ëllëg
Daar-daar bi :