Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY jiite na tay, ca àllub Mbaaw ba, Bisub jaayante bi nuy ñuy amal ci réew mi, te daje la ciiwalug ndoortlel karawaanu jëmbat garab.
Foofa, Njiitu Réew mi bokk na ci set-setal ba ñu fa amal, laataa muy séq waxtaan ak ñi bokk ci Kurél giy sàmm ndono lu am solo lii ci wàllu kéew mi ci gëbla gi.
Ñi nekk ci gox boobu, posewu nañu ci ngir leeral Njiitu Réew sémbi mbay yi ñuy amal ci biir àll boobu, jaare ko ci soppi meññeef yiy bawoo ci yëngu yooyu ñuy amal.
Ginnaaw ndaje mi, Kilifa gi amal na ndoortel karawaanu jëmbat garab ci atum 2025 ci réew mi, di mbébet mu am solo mu jëm ci delloosiwaat réew bu naat ci ay garab boole ko ak tabax kéew mu ñoñ. Jëmbat na ñaari garab yu màndargawu, màngo ak guy, di garab yi ñu tànn ci at mii ñeel bis bi ñu jagleel jëmbat garab ci réew mi, te ñu ciy waxtaane tomb bii di : «Jëmbat garab, moom sa bopp ci wàllu dund ak suqaliku gu sax ». Karawaanu jëmbat garab bii day tàbbi ci li nu jaayante ci réew mi : jëmbat benn milyoŋi garab fii ak ñaari fan, di mbébet mu jëm ci yee askan wi ci jafe-jafey kéew yi am boole ko ak gën a soññ ma-réew yi ñu gën a sóobu ci dundalaat kéew mi ba mu naat. Dina dem ci mbooleem tundi réew mi ngir gën a sóob askan wi ci doxaliin wii.
Njiitu Réew mi soññ na mbooleem ma-réew ñu gën a takku ngir sàmm sunu ndono ci wàllu kéew mi. Fàttali na ne, gépp garab gu ñu saxal rekk, day wane bëgg sa réew bi sàmm kéew mi te it day jàpp ci jëmmalug
« Vision Sénégal 2050 » : Senegaal gu moom boppam, nëtëx, néew ci wàllu karbon te taxaw temm ngir jàmmaarloo ak jafe-jafey coppite yi am ci wàllu njuux li.
Peeñ :