CICAD : Jataayub aajar Sémbu Soppi Réew Mi “Senegaal 2050”

xamle - 15 MONTHS.OCTOBER 2024

Ci jataay bi ñu doon amal jëm ci aajar tegtalukaayu “Senegaal 2050” ca CICAD, Njiitu Réew mi faram fàcce na wayndare wu am solo wii di wane yoonu yokkute wi Senegaal war a tegu ci at yii di ñëw. Taxaw na bu baax ci ndaw ñi, yeesal yi war a am ci campeef yi, xeex ger ak jëflante sunu digg ak réewi Afrig yi.

Cig àddoom, Njiitu Réew mi taxaw na bu baax ci waar wi ndaw ñi war a bay ci coppite gii. Feddali na ne Senegaalug 2050 ndaw ñu xereñ te am taxawaay, ñu noppi ngir jàmmaarloo ak jafe-jafey jamono ji, ñoo ko war a yore. Njiitu Réew mi xamle na ne tàggat ak sóob ndaw ñi ci suqali réew mi day lu war, mu boole ci leeral ne seen ug jaayante nag day lu manul a ñàkk ngir soppi réew mi.

Njiitu Réew mi xamle na itam ne fàww ñu xoolaat campeefi Senegaal yi ngir ñu gën a man a taxaw ci yittey askan wi. “Yeesal sunu campeef yi manul a ñàkk ngir taxaw bu baax ci nammeelu askan wi”, di li mu xamle boole ko ak taxaw ci fésal ne fàww ñu amal joyyanti ci doxaliin wi ak xereñte ci serwiis piblig yi. 

Njiitu Réew mi daaneel ci feddali jaayanteg Senegaal ci gën a dooleel ay jëflanteem diggam ak réewi Afrig yi, mu xamle ne “Dinanu feddali sunu jaayante ngir Afrig, boole ko ak dooleel lëkkaloo gi sunu digg ak réew yi nu dëkkandool." Gis-gis bii day teg Senegaal ci diggu fexee doxal tund wi ak Kembaar gi, boole ko ak am jubluwaayu tabax Afrig gu mànkoo te doon benn.