Ca Yokohama, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY teewe seremoni ofiselu Ndajem TICAD 9

Biti Réew - 20 MONTHS.AUGUST 2025

Ginnaaw suba su fés ak lim bu am solo ci ñu mu dalal, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, teewe na tay seremoni ofiselu 9eelu Ndajem Tokyo mi ñu jagleel suqalikug Afrig

(TICAD 9), ñu ko doon defee ca Yokohama.


Ci jataay bu jëkk bi ñu doon waxtaane wàllu jàmm ak kaaraange, Njiitu Réew mi xamle na ne jot na sëkk ñu amal kopparal gu wér ñeel yëngu yi ñuy amal ngir indi jàmm ci Afrig. Soññee na itam ngir ñu amal coppite ci ni ñuy jëflantee ci àddina si, jëme ko ci luy dooleel yoriinu àddina su gën a maandu te daj ñépp, niki noonu boole dooleel diggante jàmm, kaaraange ak suqaliku. 


Ci geneen wàll, Peresidaa FAY taxaw na ci solos gën a dugal xaalis ci wàllu tabax yi, njàng mi, tàggatu gi ak fent gi, di bir yu mu jàpp ne ñooy keno yi manul a ñàkk ngir yokkute gu daj ñépp te sax.


Mu tëjee ci, aajar gis-gisu Senegaal bu am solo bii jaare ko ci  « Agenda national de transformation Sénégal 2050 », teg ci woo partaneeri àddina  si ñu ñëw teewe « Forum Invest in Senegal », bi war a am ci Ndakaaru  7 ak 8i fani oktoobar 2025.