Ca ONU, Peresidaa FAY soññe na ngir ñu wattu demokaraasi ci kanamu ëppal gi.

Biti Réew - 24 MONTHS.SEPTEMBER 2025


Njiitu Réew mi teewe na, ci àllarba ji 24i fani sebtàmbar 2025 ca New York, ndaje ma ñu doon waxtaane lu jëm ci wattu demokaraasi ci kanamu ëppal gi, mu àndoon ko ak Njiiti Réew yu Sili, Beresil, Uruguay, Albani, Kolombi ak Njiitu Ngóornamaŋu Espaañ. 


Cig àddoom, fàttali na ne demokaraasi lees war a dundal la, lol maneesu koo saxal lu dul am taxawaay bu sax diggante péexte, wareef ak sàmmonte ak dalug pénc mi. 

Njiitu Réew mi fésal ñett yu ñu war a jiital :

•  Gën dëgëral kóolute gi diggante askan wi ak njiit yi, jaare ko ci campeef yu moom seen bopp te maandu ;

•  Wattu lëkkaloo gi ci kanamu njaay doole gi ak beru gi ;

•  Xeex ëppal gu tar gi, ci teg pexey kaaraange yu wér waaye itam  ci am njàng ak ci mbatiit, ngir dàjji pas-pas yiy suuxat mbañeel.


Peresidaa FAY feddali na solos diisoo, yamale ak doxal yoon, di bir yu manul a ñàkk ngir saxal sunu demokaraasi yi ak tabax àddina su gën a dal te gën a mànkoo.