Ca àddukaayu Mbootaayu Réewi Àddina si, Njiitu Réew mi teewe na ndaje mu kawe mi ñu jagleloon 30eelu ati Ndajem Waxtaan mi àddina si di amal ci jigéen ñi (Beijing+30).
Ci kàddu yu am solo, Njiitu Réew mi feddali na jaayante gu sax gi Senegaal am ngir gën a jëmale kanam yemale diggante góor ak jigéen ak fexe ba jigéen ñi manal seen bopp.
Woo na mbooleem àddina si ñu àndandoo taxaw temm, mu jaare ko ci fàttali ne :
* yemale fàww mu am ndax ngor ak jamono a ko laaj,
* wenn askan manul a jëm kanam bu dee daa desal ginnaaw jigéen ña,
* xeex mettiital yi ak beddi yi day xeex bu war a sax dàkk bu nguur yi, ma-réew yi ak njiit yépp war a sóobu.
Mu jaare ci « Vision Senegaal 2050 » bi, moom Njiitu Réew mi xamle ne jigéen ñi ak ndaw ñi lañu jiital ci naal yi, ñu doon keno yu wér ngir dal ak naataange gu sax dàkk.
« Nanu waajal maas giy ñëw ëllëg ñu man a dund ci àddina su gën a tegu ci yoon, gën a yemale te gën a ànd ak noflaay », di li mu daanele.