Ca waxtaan wu kawe wa ñu jagleeloon mbirum Palestin, jëm ci 80eelu Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Réewi Àddina si, Njiitu Réew mi yékkati na fa kàddu yu amul genn wër-wërloo.
Ñaawlu na jéeya ju jéggi dayo jay xew ca Gasaa, di sax nag jëf ju mu jàppe ni aw xeetu lëmm wu ñu bëgg a faagaagal, mu teg ci fàttali ne cellaaral gi ak ceetaan gi ci am daanaka xeetu far lay gën a nirool.
Njiitu Réew mi feddali na taxawaay bi ci Senegaal mas a am : dakkal sanc gi, wéer gànnaay yi ca na mu gën a gaawe, taxaw ci jàppandil dund bi ñu fay yóbbu teg ci jëmmal pexem ñaari réew yu wuute, di menn pexe mi man a jur jàmm, yoon ak kaaraange gu sax dàkk.
Ci taxawaayam niki Njiitu Kurél giy sàmm yelleefi askanu Palestin, woo na àddina sépp ngir ñu gën a bàyyi xel liy xew : « Aar Palestin, tekkiwul ne dangay wut koo faral, waaye mooy sàmm wakkan yi, yoon ak xeet wi nu bokk. »
Man ngeen a topp fii ci suuf mbooleem kàdduy Njiitu Réew mi :