xamle - 25 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Njiitu Réew mi Bassirou Diomaye Faye daje na itam ci àllarba 25i sebtàmbar 2024, Njiital Kurélug Futbalu àddina si (FIFA) di Gianni Infantino.
Seen waxtaan aju woon ci suqali futbalu Senegal ak Afrig, niki noonu ci naal yi jëm gën a yokk jumtukaayi tàggat yaram yi ak dooleel tàggat yaram niki jumtukaay buy boole askan yépp. #UNGA79