Biti Réew - 23 MONTHS.SEPTEMBER 2025
Ginnaaw ba mu teewee, ci suba si, ci waxtaan yi doon am ca 80eelu Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Réewi àddina si, Njiitu Réew mi séq na ab jataay ak kilifa gii di Soxna Francia MARQUEZ, Topp-Njiitu Réewum Kolombi.
Ñaari kilifa yi feddali nañu seen yéene jëm ci gën a dooleel lëkkaloo gi dox diggante Senegaal ak Kolombi, teg ci rafetlu gis-gis yi ñu bokk am ci wàllu lëkkaloo.
Soññee nañu itam ci gën a dooleel lëngoo diggante Afrig, Amerig di Sidd ak Karayib yi, ci pas-pasu jàppalante ak lëngoo diggante réew yi néew doole yi, ngir gën a taxaw ci yittey askan yi, boole ñépp ak suqaliku gu sax dàkk.