Biti Réew - 22 MONTHS.SEPTEMBER 2025
Ci 80eelu Ndaje Mu Mag mu Mbootaayu Réewi Àddina si, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, dalal na Soxna Kendra Gaither, Topp-Njiitu « Chambre de Commerce » bu Etats-Unis, mu àndoon ak tañ wu am solo ci ay Njiiti këri liggéeyukaayi Amerig yuy yëngu ci Senegaal walla ñu am yéeney sampu fi.
Waxtaan yi jëmoon ci fànn yu ñu man a dugal xaalis, dooleel lëngoog koom mi ak yéene ji ñu bokk am jëm ci teg xar-kanamu jëflante bu xemmemu ngir am yokkute boole ko ak sos ay xëy.
Ndaje mii day wane taxawaayu Senegaal niki selebe-yoon bu xemmemu ñeel këri liggéeyukaay yu mag yi ci àddina si teg ci di feddali kóolute gi way-lëngool yi am ci moom ci xéewal yi mu làq.