Ca New York, Njiitu Réew mi dalal na doomi Senegaal yay dund ca USA.

Biti Réew - 25 MONTHS.SEPTEMBER 2025


Niki mu ko baaxoo defee saa su génne réew mi, Njiitu Réew mi daje na ak doomi Senegaal yay dund ca « Etats-Unis ». 


Ci jataay bu xumb te ànd ak mbégte, Njiitu Réew mi weccente na ak sunu bokki ma-réew yi bawoo woon ci mbooleem Càmm yi ngir fésal seen i jàmbat boole ko ak gaaral seen i mbébet. 


Njiitu Réew mi feddali na leen njàppale gu dul dog gu Nguur gi ak mbooleem Askan wi, mu boole ko ak fàttali ne Jasporaa bi dafa am waar wu yaatu wu mu war a bay ci naal wi ñu sumb ngir soppi réew mi.


Peeñ :