Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Jaxaar FAY yékkati na ay kàddu ci àllarba ji 24i fani sebtàmbar 2025, ca kaw àddukaayu Mbootaayu Réewi Àddina si, ci lu soxal 80eelu jataayu Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Réewi Àddina si, ñu doon ci waxtaane tomb bii di : « Gën a àndandoo : lu ëpp 80i ati liggéey ngir jàmm, suqaliku ak yelleefi doomi aadama yi ».
Ci jamono ju àddina di jànkoonte ak fitna yu bari, Njiitu Réew mi yékkati na kàddu yu wér te wóor, yu jëm ci xoolaat anam yi ñuy àndee ci wàllu lëkkaloo boole ko ak taxaw temm ngir jàmmaarloo ak fitna yiy yoot.
Ciy kàddoom, Peresidaa FAY fàttali na ne juróom ñett fukki at ci ren ginnaaw sosug ONU, àddina si a ngi dund ay jafe-jafe yu bees : yokkug rëtal gi, jàppante yu dul dakk, jafe-jafey njuux, koom mu yonjax ci àddina si ak dimbalante gu dellu ginnaaw.
« Noo ngi dund jamonoy njàqare (…) mu mel ni kon njombe yi yóbbee ñaari xarnu ay jéeya yu mag, da noo mujj a dab », di kàdduy àrtu, mu boole ko ak di ñaawlu doxaliinu « Kumba am nday ak Kumba amul nday » ak doxaliinu jaay doole ci wàllu jëflante yi.
Njiitu Réew mi gën a taxawlu nag ci jafe-jafey kaaraange yi Kembaar gi di jànkonteel, rawati na rëtal gi ci Sahel bi ak ñàkk dal gi ci wàllu politig. Soññee na ngir ngir kopparal gu ànd ak fuglu te sax dàkk ngir jàmm ci Afrig, mu ànd ak ay sas yu am wér ak jumtukaay yu méngoo, nga xam ne doon na lu manul a ñàkk ngir delloosi dal gi.
« Jàmm ak kaaraange dañoo am njëg. Kon nag nanu teg matukaay yiy tax nu matale ko », di li mu xamle, boole ci yeesalaat njàppaleg Senegaal jëm ci réew yi sóobu ngir xeex rëtal gi.
Lu jëm ci tolluwaay bi am ca Penku ba, Kilifa gi Basiiru Jomaay FAY ñaawlu na bu baax faagaagal gi ñuy def jëme ko ci askanu Palestin ca Gasaa, muy tolluwaay bu mu jàppee « sawara ci kaw ay milyoŋi nit ». Ci taxawaayam niki Njiitu Bànqaasu Mbootaayu Réewi àddina biy saytu sàmmonte ak yelleefi askanu Palestin, feddali na ne lenn rekk mooy tax jàmm man faa sax, muy taxawal Réewum Palestin mu moom boppam te neex a dunde, ci biir dig yu wóor yu ñu nangu.
Njiitu Réew mi feddali na wooteb Senegaal jëm ci yeesalaat Ndiisoog Kaaraange gu Mbootaayu Réewi Àddina si, jaare ko ci dooleel déggoog « Ezulwini » giy sàkku teewaay bu gën a maandu te gën a yamale ñeel Afrig.
Ci wàllu koom, soññee na ci doxaliin wu gën a boole, wuy jiital kaadaru galagu àddina bu gën a yamale, gën a jàppandil anam yi ñuy lebee ak doxaliin yu gën a méngoo ngir woyofal diisaayu bor bi.
Lu jëm ci jafe-jafey njuux li, Peresidaa FAY fàttali na « ñaari nattu » yi dal ci Afrig gi nga xam ne 4% rekk lay xëpp ci àddina si waaye mooy dund wàllu bekkoor, wal yi ak jafe-jafe ci wàllu dund bi.
Woote na ci ñu jàll jëm ci jëfandikoo yasara gu gën a sell te yamale, yombal jot gi ci koppar yi ñu jagleel njuux li, ak dajale balluwaay yi ngir koppar yu bees yi jëm ci saafara yàqu-yàqu yi.
Mu tëjee ay kàddoom moom Njiitu Réew mi ci ñaax Réew yi ci bokk, ñu def 80eelu ati Mbootaay gi mu bañ a doon ag seetlu ci doxaliinu àddina su yonjax, waaye mu doon jóg gu bees ñeel ONU gu ñu « yeesalaat gu gën a xereñ te taxaw ci yittey askan wi ».
« Gàllankoor gi dëgg du mbiru koppar walla xarala. Ci yéeney politig ji doŋŋ la », di li mu xamle, boole ko ak di woote ñu gën a bàyyi xel diññite nit ki ci jëf yi ñuy amal ci biir àddina.
Man ngeen a topp widewoo kàdduy Njiitu Réew mi :