jëwriñ - 08 MONTHS.NOVEMBER 2024
Niki ñu ko tënkee ci arminaatu repiblig bi, bis bi ñu jagleel larmeb Senegaal dees na ko màggal àjjuma 8i fani nowàmbar 2024, ñu war cee waxtanee « Pexe yu jëm ci yegg ci larme bu moom boppam ci wàllu xarala ak ndefar ».
Ci Ndakaaru dees na màggal bis bi ca karcé Jal Jóob bu 8:30 jotee, ci njiital Kilifa gi Basiiru Jomaay Jaxaar Fay Njiitu Réew mi Kilifa gu mag gu larme bi. Dees na ko màndargaal ci wane gànnaay yi ak teg fuloor ca Memorial du Souvenir, tuddu ñi génnee ci lekoolu militeer ci wàllu paj (EMS) ak lekoolub ofisee aktiif yi (ENOA), niki noonu ab nemmiku ci fésal gu ñuy def ci jumtukaayi miniteer.