Bisub Larme bu atum 2024: Njiitu Réew mi yëgle na ay matuwaay yu ñu war a jël ngir yeesal boole ko ak dooleel kaaraangeg réew mi

xamle - 08 MONTHS.NOVEMBER 2024

Bis bi ñu jagleel Larmeb Senegaal màggal nañu ko àjjuma 8i fani nowàmbar 2024 ca Kaa Jal Jóob bu Ndakaaru, ci njiital Njiitu Réew mi, Kilifa gu Mag gu Larme bi, Basiiru Jomaay Fay. Xewu 2024 wi nag mooy jataay bi Peresidaa Fay njëkk a teewe ba mu faloo ci boppu réew mi ak tay.

Wëppa wi ñu tànn ren di « Nees di def ba yegg ci larme bu moom boppam ci wàllu xarala ak ndefar », day firndeel rekk yéeney Ngóornamaŋ bi ci yeesal larmeb Senegaal. Tànneefu wëppa wii day wane yéeney Senegaal ci suqali moom boppam ci wàllu kaaraange. Muy yéene ju wér ju jëm ci jox larmeb Senegaal jumtukaayi xarala ak ndefar yu mu moomal boppam, yoy dina wàññi bu baax ni ñu wékkoo ci jumtukaayi biti réew.

Sémbu bis bi séddalikoo woon ci yékkati gànnaay yi, teg fulóor ca « Memorial du Souvenir », ak jox tur dongo yi génnee ci Ekool Militeer Sante (EMS) ak ENOA. Njiitu Réew mi posewu na ci ngir yaatal gis-gisam ak doxaliinam ñeel larme bi.

Cig àddoom, Njiitu Réew mi delloo na njukkal bu baax sunu jàmbaar yi teg ci rafetlu taxawaayu saa-repiblig bi larme bi taxawe, doon ñu yàgg a siggil réew mi ci doxal wuute gi am ci Senegaal boole ko ak bay seen waar ci tabax  déggoo gi am ci réew mi. Kilifa gu Mag gu Larme bi sant na leen bu baax ci ni ñuy dugalee seen loxo ngir jëmmal ak sàmm moom sunu bopp gi, di loo xam ne romb na rekk aw bàkk : mooy ngelaw liy dundal réew mu namm a manal boppam sañal boppam. 

Njiitu Réew mi xamle na ne dees na taxawal benn « Prix spécial » bu Njiitu Réew mi, boo xam ne dees na ko joxe ci xewu 2025 wi ñuy màggal Bisub Larme bi. Muy Prix bu war a neexal ki gën a xereñ ci fentug xarala ak ndefar bu jëm ci wàllu militeer.

Xamle na itam ne bu ñu taxawalee Ngomblaan gii di ñëw ba noppi, dees na gaaral wenn sémbu yoonal ci wàllu kaaraangeg réew mi ngir càmbar tomb yi gën a am solo ci sunu wàllu kaaraange yi ñu war a dëppale ak jamono.

Yoonalug sémb wii diggante 2025-2029, dina tax sunu réew man a am sémb wu koy may mu man a teg ay naal yu romb njël yi ñuy natt at mu ne boole ko ak man a jàmmaarloo ak jafe-jafe yu bees yi am ci réew mi ak ci àddina si ci wàllu kaaraange.