jëwriñ - 04 MONTHS.AUGUST 2024
4i fani Ut, Tuubaa mooy dalal xewu Bis bi ñu jagleel Jëmbat Garab ci Réew mi, ci wëppa wii di "Taxawaay bi jëmbat garab am ci biir moom sa bopp ci li ngay dunde ak suqalikug koom mi”. Xew wii di am ci njiital Kilifa gi, Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY FAY, mooy màndargaal ndoorteel kàmpaañu jëmbat garab ci réew mi.