Ginnaaw bi ma nuyoo Jëwriñu Njàng mi,
toftal ci Góor ak Jigéen ñi bokk ci Ngóornamaŋ bi,
Sekkereteer Seneraalu Lig Islaamig,
Kilifay Ma-laamisoo yi Góor ak Jigéen ,
Sëñ bi Jiite pekk biy saytu mbirum diine yi ak ñi am lijaasa ci làkku araab,
Kilifa diine yu tedd yi,
Boroom daara yi, ndayi daara yi, dondo daara yi,
Gan ñu tedd ñi, Góor ak Jigéen,
Am naa Mbégte mu rëy taxaw fii tay di yékkati kàddu ci 3eelu xewu bis bi ñu jagleel daara ci réew mi. Bis bii nag danuy may nu man a taxawaat ngir xalaat ci benn ci keno yi téyee sunu am-am ci wàllu pas-pas, mbatiit ak njàng: muy daara.
Ñu yoonal ko ci dekkere limtu 2023-225 bu 18i fani sãawiye 2023, bis bii day wane rekk sunu yéene ci delloo njukkaal warab yii nga xam ne romb nañu fu ñuy jàngalee xam-xamu diine rekk, waaye ay warab la yu ñuy tàggatee ruuhi doomi aadma yi. Daara yi nag, yàgg nañoo mooñ ak a tàggat ay nit, ay maas yu bari ci ay góor ak i jigéen, def ci ñoom jikko yu tedd yi lislaam làmboo ak xam-xam buy tax ñu man a bokk bu wér ci liy doxal réew mi.
Kon màggal daara tay, mooy sargal mag ñi ci ndono li ñu fi bàyyi, waaye tamit taxawaay bu am solo bi ñu am ci ni nu gisee njàngum tay mi. Tay lanu gën a dogu kon ci taxawu daara, yeesal ko teg ci gën koo sóob ci doxaliinu njàngum Senegaal, lépp nag ci kaw di sàmmonte taar, cosaan ak gànjar gi nekk ci daara.
Soxna yi ak Sëriñ si,
Tay nag bu daara yi wéyee di doon ba leegi li ñu doon tay, dafa fekk am na ñu taxaw temm ànd ak dogu ngir di ko sàmm ak a aar bis bu set. Maa ngi jaajëfal bu baax tay, Boroom daara yii nga xam ne ay yerekat yu mucc ayib lañu, di ay tàggatkat, doon it ñuy joxe xam-xam bu wér te ànd ak jikko yu tedd. Ci seen dogu googu ñu ame, leeg-leeg sax ñu koy amal ci anam yu xaw a tar, ci lañuy mooñ ndaw ñi def ci ñoom pas-pas, teggiin, joxe cér ak suufe ngir waajal leen ñu man a doon ñu am taxaxaay ci biir askan wi.
Ndayu daara yi tamit nekk ci seen wet di amal liggéey bu am solo. Yaay yu jàmbaare yii te yéwén, nga xam ne leeg-leeg sax duñu leen gis, ñooy taxaw ci indi jumtukaay ak dalal xel yi ñu yittewoo ci biir daara yi. Dogu gi ñuy wane bis bu set ci di togg, di toppatoo warab yi ak a taxaw ci yittey gone yi, lees war a kañ la. Kon na soxna yooyu xam ne noo ngi leen di bége, di leen ndamoo te dinanu leen taxawu ci liggéey bu am solo bi ñuy def jëme ko ci njàng mi ak dimbalante.
Waaye nag, manunoo daje ci bis bu mel nii ba dem te taxawunu wax ci yenn yiy gàkkal daara. Mbirum yalwaan mi ñuy ga xale yi, nga xam ne doon na lu ñépp seetlu ci mbedd yi, doon na lu mel ni luy wëlbati li taxoon a jóg daara. Jëf yu ni mel nag nga xam ne soree na lool ak li taxoon a jóg daara, danoo war a ànd ak dogu ci xeex ko. Sunu wareef la nun ñépp nu fexe ba bépp xale bu bindu ci daara mu man a jàng ca na mu waree ci ngor.
Soxna yi ak Sëriñ si,
Ci kanamu jafe-jafe ak njariñ yi daara ëmb, jot na sëkk nu am gis-gis bu bees, bu wér te wóor ngir fexe ba daara doon lu sax te jëm kanam. Loolu tax na ma yëgle fii tay woote Jataayi Waxtaane Daara yu njëkk ci réew mi.
Jataay yii, war a dajale ñiy yëngu ci wàll wi - jàngalekat, kilifay politig yi, këri diine yi, partaneer yi ci wàllu xarala ak kopparal, dinañu ci amal ay xalaat ci yeesalaat gu xóot ci daara yi. Muy :
Xalaat bu baax ci nu ñu leen di dugalee ci doxaliinu njàngum réew mi, ngir yamale gu wér man a am diggante doomi Senegaal yi, ak yoon wu ñu man a jaar ngir jàng.
Di raxante li ñuy jàngale jaare ko ci dugal ay xam-xam yu méngoo ak jamono, niki màndaxe, xamtu, làkki doxandeem yi ak xam-xamu xarala, ngir waajal ndaw ci ni àddina di doxee.
Samp kurél gu jëm ci kopparal ak taxawu daara yi, rawati na jaare ko ci lëkkaloo diggante piblig bi ak piriwe bi ak njàppale gu sax gu bawoo ci Nguur gi.
Yeesal yii nag li leen tax a jóg du ngir wëlbati jubluwaayu daara, waaye danu leen a namm a taxawu ngir ñu man a taxaw bu wér te wóor ci yitte yi nga xam ne ñoom la sunu jamono laaj, lépp nag tegu ci wéy di sàmm cosaan ak taaru daara.
Fii mu ne nii rekk daara modern yi wane nañu seen man-man ak seen xereñte. Ndam yu rëy yi dongo daara yi am ci joŋantey tari Alxuraan yi ñu jot a amal ci àddina si rekk firnde la ci loolu. Ndax ñii, muy góor di jigéen, sagal nañu sunu réew te yóbbu nañu raaya Senegaal ci kanamu àddina sépp.
Ci geneen wàll, dongo yi bawoo ci daara yi rekk tey wéyal seen um njàng ci sunu jàngune yi ak ci warabi njàng mu kawe mi firnde la ci ne manees naa boole njàngum cosaan mi ak njàng mu modern mi. Ndam yii nga xam ne leeg-leeg ñenn ñi duñu ko bàyyi xel, da nuy fàttali rekk man-man gu yaatu gi làqu ci biir daara yi ak it ne fàww nu jox leen jumtukaay yu wér yu ñu man a matalee seen yéene.
Soxna yi ak Sëriñ si,
Sàmm ak gën fullaal daara wareef la ci kenn ku ne ci nun; mooy liy màndargaal sunu cosaan ak sunu ëllëg. Campeef yii nga xam ne kawe nañu ay lekool, ay warab la yu ñuy jàngalee mbaaxi dimbalante, joxante cér ak maandu, di bir yoo xam ne ñooy keno yi téyee sunu réew.
Maa ngi woo kon, kenn ku ne ci nun, muy góor di jigéen, mu taxaw temm ci def daara muy royukaay ci wàllu yar ak déggoo ci réew mi. Ci mànkoo rekk lanu man a tabaxee Senegaal goo xam ne ndaw lu ne, ak fu mu man a cosaanoo ak lu mu man a gëm, dina man a jot cim njàng boole ko ak yaru ci ngor.
Maa ngi leen di sant di leen gërëm.