Lu jëm ci jaayante gi mu def ngir doxaliin wu dul beddi kenn ak wareefu kenn ku nekk fexee dugal loxoom ci tabaxug campeef yi ak joŋante yi, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY yëgle na Péncoo gi ñu war a amal ci réew mi 28i fani mee ba 4i fani suwe 2025. Xew-xew bu am solo bi a ngi jóg ngir dajale mbooleem ñi séq réew mi ñu toog xalaatandoo ci yeesal yi war ngir gën a dooleel demokaraasib Senegaal boole ko ak taxaw ci nammeeli askan wi.
Ñu war cee waxtaane tomb bii di sistemu politig bi, péncoo gii fas na yéene samp kenoy campeef yu méngoo ak jamono, yu sax ci mbaax yi ci wàllu mbatiit, dundiin ak mboorum Senegaal. Muy tàbbi ci yoonu boole, dajale ñi teewal làngi politig yi, sosete siwil bi, mbootaayi sàndikaa yi, këri diine yi, sékteer piriwe bi, niki noonu ay kàngam ak ma-réew yu dogu.
Péncoo gii, nar a boole li ëpp ci géewu politig bi ak ñi séq réew mi, bëgg nañu mu doon jataay bu am solo ngir am ay déggoo yu wér yuy gën a dooleel demokaraasib Senegaal boole ko ak taxaw ci sàmm bu baax yelleef yi ak péexte yi.
Ngir am ci lu gën a leer, man ngeen a yër wayndare caabal gi nekk fii ci suuf :