Bëccëgu Jaayante SETAL SUNU RÉEW

jëwriñ - 04 MONTHS.JANUARY 2025

4i fani sãawiye 2024, dees na amal bëccëgu jaayante SETAL SUNU RÉEW. Naal bii bawoo cii  Njiitu Réew mi, mu ngi jëm ci soppi xar-kanamu li  wër sunu dëkkuwaay.


Ñu war cee waxtaane wëpp wii di : « Setal sa gox, aar sa yaram: way-kaaraange yi dinañu jaayante  ci wetu askan wi », bëccëg gu njëkk gii ci atum 2025, Jëwriñ ji ñu dénk larme bi ak Jëwriñu Paj mi ñoo koy jiite.