xamle - 14 MONTHS.JANUARY 2025
Njiitu Réew mi dalal na ci talaata ji Njiital «Commission » bu UEMOA. Abdulaay Jóob posewu na ci jataay bi ngir indi ay leeral ci tolluwaayu Mbootaayu koom ak koppar gii ëmb Réewi Afrig Sowu Jant yi ci wàllu koom, dundiin ak kaaraange.
Mbirum doxaliin itam, rawati na yeesal yu am solo yi ñu war a amal ci wàllu koom ak moom sa bopp, waxtaane nañu ko ci jataay bi.